ACTUALITEDIASPORANECROLOGIESOCIAL

Hommage à Cheikh Fall (Version wolof par Serigne Fall, Président Anvid Risso)

1.07KViews

Al jumha 21 février, tay di dibéer 21 ci weeru février tombeek bësu mbetteel ak bësu nàqqar ci mbooleem ku askanoo Risso ak liko wër, rawantena doomu Risso yi nekk ci biir ANVID.
• Bisub kero, xol yéppë sëngéem, diis gand ngir sunu ràkk, sunu xarit, sunu soppe Cheikh Fall mi teelë réer. Waaye sunu borom moo wax ci Alqurhaan ni :

• كل نفس ذائقة الموت ثم إلينا ترجعون

• Cheikh nekkoon ku jambaare, am yar te bare ay teggin. Ñoo ngi feddali sunug kóllóre ak moom fas yéene bisam bi sax dàkk ba saa yu dikkëtée mu nekk bisub fatteliku ak ñaan ngir sunu Boroom atte ko ci yërmaaneem te xaare ko Aldianay Firdawsi.

• Ci turu ANVID, ñoo ngi koy jaal magam Moor Faal, rakkam Elimaan Faal, ndijaayam Mangoone Faal ak waa Risso ñepp te bayyiwun kenn.

• Yéene ji mu amoon ci Risso doon ko jaarale ci ANVID, yalna ko Yalla matale te fay ko ko ay yiw yu kawe njortam besub penc ba nga xamne dara du fa doy ci jëf ju baax.

• Ba mu jëndëlee Association Goney Risso équipement, ci biir waxtaan, dafmaa xamaloon ni amoon na yeneeni yéene yu gëna tàkku jëmële ko ci ñoom waaye feek muy sotti duko leeral.
• Kon na ko ñepp ñaanal, gone ak mak ngir fa mu nekk gënal ko fii mu joge te Yalla sàmmal ko njaboot gim gi bàyyi.

• ‎ اللهم اغفر له وارحمه واسكنه فسيح جناته ويلهم أهله الصبر والسلوان

• Cheikh, nekkoo fi waaye moo ngi melni yaa ngi ci sun biir ndaxte bi ñuy sos ANVID, yaa ngi woon ci sunu biir te la nga def ci diir bu gàtt, bare na ñoo nga xamne Risso la ñu juddoo, yaroo fa té ba tay nii may bind bataaxal bii dabu ñu la ci jëf.

• وندعو الله أن يتغمده برحمته وأن يسكنه فسيح جناته.

Serigne Fall

Président d’ ANVID RISSO

cic-anvid
the authorcic-anvid

Laisser un commentaire